Loolu Saarata wax naqari Ibraayma lool ndax li Ismayla di doomam, moom it.
TSK
TSK · Genesis 22:1
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Teewul malaakam Aji Sax ja àddoo asamaan, ne ko: «Ibraayma! Ibraayma!» Mu ne ko: «Ãa!»
Yàlla wax ak Israyil foofa ca guddi ci biir gént ne ko: «Yanqóoba, Yanqóoba!» Israyil ne ko: «Naam.»
Musaa woo Aji Sax ji wall, Aji Sax ji won ko dammitu bant, mu sànni ko ca ndox ma, ndox ma neex. Foofa la Aji Sax ji dogalal bànni Israyil ay sàrti yoon ak ndigal, te fa la leen nattoo itam.
Fàttlikuleen mboolem yoon wi leen seen Yàlla Aji Sax ji awale diiru ñeent fukki at yii ci màndiŋ mi, teg leen coono, nattu leen ngir xam li ci seen biir xol, xam ndax dingeen wormaal ay santaaneem, am déet.
ba firnde la mbaa kiraama ga mu leen waxoon dikk, su leen nee: «Nanu topp yeneen yàlla, jaamu leen,» yàlla yu ngeen xamul,
Aji Sax ji woo Samiyel, mu ne: «Maa ngi»,
¶ Ma dégg baatu Boroom bi, mu naan: «Ana ku may yebal, ana ku nuy demal boog?» Ma ne: «Xanaa man, yebal ma!»
¶ Ibraayma, ba ñu ko nattoo, ngëm la jooxee Isaaxa ngir sarax. Ibraayma mi ñu jagle dige yi, Isaaxa jenn doomam ju góor ji mu am, moom la doon jooxe,
Sunu maam Ibraayma, xanaa du ci jëf lees ko joxe àtteb ku jub, ndax jëf ja mu jooxee doomam Isaaxa ca sarxalukaay ba?