TSK

TSK · Genesis 27:29

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

ku la ñaanal barke, ma barkeel, ku la móolu it, ma alag, te xeeti àddina sépp, ci yaw lañuy barkeele.»

Doom yi nag di buuxante ci biiram, ba mu naan: «Ndegam nii la kay, jaru ko woon!» Ci kaw loolu soxna si dem, diis ko Aji Sax ji.

Yanqóoba ne ko: «Giñal ma jëkk.» Esawu giñal ko ko, mu jaay Yanqóoba ndono, li mu yeyoo ndax li muy taaw.

Sa saamar ngay dunde, sa rakk di la yilif. Waaye bés a ngi ñëw yaay sigiñu, ba yenniku notaangeem.»

«Yaw Yuda, mi say doomi baay di taggeji, ngay sëqi sa ndoddi noon, sëgal leen, sa doomi baay a lay sujjóotal.

Moo nu may móoloo ku Yàlla móoluwul? Ana nu may rëbbe ku Aji Sax ji rëbbul?

¶ Gannaaw gi, Daawuda duma na Filisteen ña, néewal leen doole, jële kilifteefu waa Filisti ca réew ma.

La desoon ca ñay jaay seen bopp ca jaamookaayi tuur, ya fa desoon ca jamonoy baayam Asa, ba booba, Yosafat da leena jële ca réew ma.

Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Seedeb Tóor-tóor, di taalifu jàngle, ñeel Daawuda.

Boroom bee yónnee kàddu gu dal Israyil, askanu Yanqóoba,

Aji Sax ji jotkatub Israyil, moom ku Sellam ki, moo wax ak ki xeet yi xeeb, sib ko, te muy surgawu kilifa yi, mu ne ko: «Ay buur ay gis, jóg, ay kàngam di sukk, ngir Aji Sax ji boroom worma, ngir Aji Sell ju Israyil ji la taamu.»

Ana kuy kii bawoo Edom, sol yére yu xonq, bawoo Boccra? Kii ak yéreem yu yànj, di daagoo dooleem ju bare? «Xanaa man mii di waxe njekk, te am dooley walloo.»

«Maa dégg ŋàññi Mowab, kàddu yu ñaaw yi Amoneen ñiy ŋàññe sama ñoñ, tey damu, nara nangu seen suuf.

bu ajuwul ci kawi jëf, xanaa ci kiy woote. Rebeka la kàddu gii dikkal: «Mag ji mooy surgawu rakk ji.»