TSK

TSK · Genesis 3:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Yàlla Aji Sax ji daldi ne: «Wéet baaxul ci nit, kon dinaa ko bindal ku koy jàpple te jekk ci doon wéttalam.»

Yàlla Aji Sax ji bind jigéen ci faar, gi mu jële ci Aadama, indil ko ko.

Sóol ne ko: «Ca Amalegeen ña de lañu ko jële. Xarekat yee bàyyi li gën ci gàtt yeek nag yi, ngir sarxal ko sa Yàlla Aji Sax ji. Waaye la ca des moom, faagaagal nañu ko.»

Xarekat yi daal a tànne ci lël ji li gën ci gàtt yeek nag yi ñu wara faagaagal, ngir sarxal ko sa Yàlla Aji Sax ji ca Gilgal.»

Nit def na jëfi dof, ba sànku, walbatiku mere Aji Sax ji.

Waa ja nag namma wutu lay, ne Yeesu: «Sama moroom mooy kan?»

¶ Képp ku dajeek lu koy xiirtal, bumu ne: «Yàllaa ma xiirtal,» ndax maneesula xiirtal Yàlla ci lu bon, te moom ci boppam du xiirtal kenn.