TSK

TSK · Genesis 3:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Yàlla ne ko: «Loo def? Sa deretu rakk jaa ngi yuuxoo ci suuf, ma di ci dégg.

Yuusufa ne leen: «Li ngeen def nag? Xanaa xamuleen ne nit ku mel ni man day gisaane?»

Samiyel ne ko: «Loo def nii?» Sóol ne ko: «Man kat damaa gis mbooloo mi dëddu ma, di tasaaroo, te yaw it dikkoo bésu àpp bi. Rax ci dolli waa Filistee nga daje ca Migmas.

Ana lu waral nga ñàkke worma kàddug Aji Sax ji, di def lu mu ñaawlu? Uri Etteen bi, yaa ko fàdde saamar; jabaram nga jël, def ko sa jabar, moom nga fàdde ko saamaru Amoneen ñi.

Ci kaw loolu nit ña tiit tiitaange lu réy, ne ko: «Yaw, li nga def lu mu doon?» Fekk na Yunus xamal leen ne Aji Sax ji lay daw.

Waaye na jaan ja naxe woon Awa, ca pexeem, ragal naa seenum xel yàqoo noonu, ba dëddu ngëm gu dëggu te set gu ngeen ŋoye woon ci Almasi.