Genesis 42:6
TSK
Fekk booba Yuusufa mooy dogal ca réew ma, di jaay pepp waa réew mépp. Magi Yuusufa ya ñëw, sujjóotal Yuusufa.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Fekk booba Yuusufa mooy dogal ca réew ma, di jaay pepp waa réew mépp. Magi Yuusufa ya ñëw, sujjóotal Yuusufa.
¶ Ba Yuusufa wàccsee, ñu jébbal ko foofa ca biir kër ga sarica, ba ñu ko indaaleel, daldi koy sujjóotal.
¶ Yuda aki doomi baayam nag délsi kër Yuusufa, fekk demagul. Ñu daldi ne nërëm, dëpp seen jë fi suuf.
¶ Ci kaw loolu magam ya ñëwal seen bopp ba ca moom, sujjóotal ko ne ko: «Sang bi, nu ngi nii, di la siyaare.»
Mooy boppu yaram, wiy mbooloom gëmkat ñi, mooy njàlbéen, mooy taaw bi jëkka dekki, ndekkite lu dee toppul, ba tax muy ki jiitu ci lépp,