TSK

TSK · Genesis 43:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Yanqóoba fanaan na fa guddig keroog, doora sàkk ca alalam, sédd magam Esawu,

Yanqóoba ne ko: «Ngalla waay déet, dimbali ma rekk te jël li ma la may. Ndaxte bi ma nee jàkk ci sa kanam, gis naa ni nga ma laaye biir, ba mu mel ni Yàllaa ma geestoo yërmandeem.

Yal na Yàlla Aji Man ji def waa ja yërëm leen, ba bàyyi seen doomu baay ba, moom ak Beñamin itam. Man nag, su ma naree ñàkk ay doom— aa! Naa leen ñàkk rekk.»

Yeen nag ma ne leen yeenay nangu seen réew ñoom, ndax maa leen ko jox, ngeen moom ko, muy réew mu meew maak lem ja tuuroo. Man maay seen Yàlla Aji Sax, ji leen ràññatleek yeneen xeet yi.

Sóol ne surgaam: «Waaw, bu nu demee, lu nuy jox góor gi? Mburu mi woon ci sunuy mbuus jeex na, amunu dara lu nu yóbbul góoru Yàlla gi. Leneen lu nu am?»

Ñooñu ñoo ko daan indil at ci kaw at, ku nekk ak sab teraanga, muy ay jumtukaayi wurus ak yu xaalis aki mbubb aki gànnaay aki cuuraay aki fas aki berkelle.

Buur ne Asayel, ab jawriñam: «Demal ca góoru Yàlla ga te yóbbaale loo teg ci loxoom, mu seetal ma ci Aji Sax ji. Laajal ma ko ne ko: “Ndax dinaa jóg ci sama wopp jii?”»

¶ Jant yooyu doomu Baladan Berodag Baladan buuru Babilon moo yónnee Esekiya bataaxal ak yóbbal. Booba dafa dégg ne Esekiya daa woppoon.

Yeen, seen Yàlla dogalal na leen kàttan; éy Yàlla, jëfeel doole ja nga nu jëfeeloon.

Doom aadamaak xadaram rafetal sa woy; desu xadaram, nga gañoo.

Deel maye, da lay ubbil bunt, di la àggle ci boroom daraja.

Ku mer, may ko ci sutura, mu giif; boroom xadar, boqal ko neexal, mu dal.

Moo diwu pajtal amul Galàdd a? Am fajkat a fi amul? Ana lu waral bokk yi taneeguñu?

Yudak réewum Israyil it di say jula, di la wecci bele bu bawoo Minit, ak dugub ak lem ak diwu togg ak diwu yaram.