TSK

TSK · Genesis 8:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Boo beyee, dootu nangu. Dinga dëkke daŋ-daŋ, di wëreelu ci àddina.»

¶ Aji Sax ji dafa gis ne mbonu nit màgg na lool ci biir àddina, te fu mu mana tollu, lu bon rekk lay xinte ci xolam.

Ni may faseek yeen kóllëre nii la: Deesatul boole bindeef yépp, faat ci mbënn mukk. Du menn mbënn mu deeti faagaagal àddina.»

Lakkal kuuy mépp ci kaw sarxalukaay bi. Saraxu rendi-dóomal la, ñeel Aji Sax ji, di xeeñ xetug jàmm; saraxu sawara la, ñeel Aji Sax ji.

Nañu raxas yérey biir yi ak yeel yi, sarxalkat bi boole lépp lakk ci kaw sarxalukaay bi. Saraxu rendi-dóomal la, saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.

Sarxalkat bi day jàpp ci laaf yi, xotti te bañ koo teqale, daldi koy lakk ci sarxalukaay bi, ci kaw mattum taal bi. Saraxu rendi-dóomal la, saraxu sawara ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.

Ngalla Buur, sama sang, déglul lii ma lay wax: su fekkee ne Aji Sax ji moo la xiir ci sama kaw, yal na ko cib sarax giifal. Waaye su dee ay doom aadama de, yal nañu alku ci kanam Aji Sax ji, ndax dàq nañu ma tey, ba xañ ma ab cér ci Aji Sax ji, mbete ku ñu ne: “Demal jaamuji yeneen yàlla.”

Job 15:14 TSK

Ana nit ku mana jub xocc? Ana ku laab ku jigéen jur?

Yeena ngi mébét njubadi, di lawal fitna ci réew mi.

Ana ku man ne fóot na xolam, ba tàggook bàkkaar?

Lii moo di muju ña la taxoon di sonn. Ña nga dale jëflanteel ba ngay ndaw, ña ngay tambaambalu tey, ku nekk ak yoonam, kenn walluwu la ci.

Nun ñépp a lajj niy xar, ku nekk walbatiku topp yoonam, te Aji Sax jee ko këpp sunu gépp ñaawtéef.

Ma ne dogal a ngii binde, fi sama kanam: «Duma noppi déy, maa leen di fey, maa leen di fey ba mu mat sëkk.»

«Dara gënula dëng xelum nit, laago la ci moom. Ana ku ko mana xam?

Maa leen di nangul seen saraxu cuuraay, gannaaw bu ma leen génnee fa biir xeet yaak réew ya ngeen tasaaroo ca seen biir, ba dajale leen. Su boobaa maay jëfe sellnga fi seen biir, xeet yi seede.

¶ Gannaaw ba ñu xamee Yàlla, taxul ñu màggal ko ngir li muy Yàlla, taxul ñu delloo ko njukkal, xanaa réer ci seen xalaati neen, ba seen xel mu wayadi far tàbbi cig lëndëm.

Ndaxte boroom xintey bakkan ab noonu Yàlla la, nde déggalul yoonu Yàlla, te manu ko sax.

¶ Yeen dangeena dee woon ndax seeni moy ak seeni bàkkaar,

Fii ma tollu jot naa li ma aajowoo lépp, maa ngi ci naataange; doyle naa sëkk, gannaaw ba ma nangoo ci loxol Epafrodit, seenub yóbbante, te sarax su ñu nangu la, di xeeñ xetug jàmm, te neex Yàlla mi mu ñeel.

James 4:1 TSK

¶ Ana fu jote yeek xuloo yi ci seen biir jóge fu moy seen bànneexi bakkan, yiy xare ci seen yaram?