TSK

TSK · Genesis 9:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Kon nanu def nii: danuy nàndal sunu baay biiñ, tëdd ak moom, ngir sunu xeetu baay du fey.»

Bul xool biiñ ak xonqaayam. Aka yànj cib kaas te neexa jolu!

«Wóoy ngalla yaw mi nàndal sab dëkkaale, sotti sa ndabal sànj, màndale ko, ngir niir ko, mu ne duŋŋ!

Nanu jëfe jëfin wu jekka def bëccëg; nanu sore xawaare ak màndite, sore baane bu lewul, ak yàqute yu ni mel, te sore ŋaayoo ak kiñaan.

ak ñeetaane, ak màndite, ak mbumbaay, ak yeneen yu ni mel. Ma àrtu leen nag na ma leen artoo woon, ñiy jëfe noonu, amuñu cér ci nguurug Yàlla.

dama lay digal, nga jënd ci man wurus wu ñu xellee ci sawara ba mu set wecc, ngir nga am alal. Jëndal itam yére yu weex yoo soloo, ba làq sa duŋŋaaral gu gàccelu gi; ak tuufaay looy tuufoo, ngir nga gis.