TSK

TSK · Genesis 9:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Dogal a ngii, di lu leen war fàww, ak fépp fu ngeen dëkk: lépp luy nebbon mbaa deret, buleen ko lekk.»

¶ «Te it képp ku bokk ci waa kër Israyil mbaa doxandéem yi ci seen biir, bu lekkee lenn luy deret, kooku lekk deret, man Aji Sax ji, dinaa ko noonoo te dinaa ko dagge ci biir bànni Israyil.

Waaye deret ja, buleen ko lekk. Ci suuf ngeen koy tuur nim ndox.

¶ Buleen lekk lenn lu médd. Jaambur bu dal ak yeen, sañ ngeen koo jox lu médd, mu lekk, mbaa ngeen jaay ko ab doxandéem. Waaye yeen askan wu sell ngeen, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji. Te buleen togg ab tef ci meewum yaayam.

Ñu yegge ko Sóol, ne ko: «Mbooloo ma kat a nga nee, di moy Aji Sax ji, di lekk yàpp wu ànd ak deretam.» Sóol ne: «Yeenaka fecci kóllëre! Béraŋal-leen ma fii aw doj wu mag léegi.»

Kon nag nanga leen wax ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yeen ngeen di boole yàpp ak deret di ko lekk, di wékki gët kasaray tuur, di tuur deretu jaamburi Yàlla, ba noppi di moom réew mi?

Moo tax nu mànkoo ci tànn ay nit ñu nu yebal ci yeen, boole leen ak sunuy soppe Barnaba ak Póol,

Ndaxte li Yàlla sàkk lépp a baax, du lenn lees ciy aayal, ndegam kàddug cant lees ko jariñoo.