TSK

TSK · Hebrews 13:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ka ca des mu tudde ko Elyeser (mu firi Yàlla dimbali na ma), ndax da ne woon: «Sama Yàllay baay mooy sama ndimbal te moo ma musal ci saamaru Firawna.»

Ndokklee, Israyil, ana ku mel ni yeen, askan wu Aji Sax jiy wallu, di seen kiiraay, di seen ndimbal, di saamar bi leen di sagal? Seeni noon a leen di loxal, te yeen, fa seen gannaaw ya ngeen di daagoo.

Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda jaamub Aji Sax ji. Mu jagleel Aji Sax ji woy wii, bés ba mu ko xettlee ci mboolem noonam, xettli ko it ci Buur Sóol. Kàdduy woy yaa ngii.

Sang bi, bu ma làqu, bul mer, jañax ma. Yaa ma daa wallu. Bu ma wacc, bu ma ba, yaay Yàlla mi may musal.

Képp ku lay sàkku, yal na bég, di la bànneexoo. Képp ku safoo sag wall, yal na jàppoo: «Aji Sax ji màgg na!»

Su ma tëddee, fàttliku la, waxtuw guddi dama lay xalaat.

Éy Israyil, wóolul Aji Sax ji, moo lay jàpple, di la aar.

Sunu ndimbal a ngi ci turu Aji Sax ji, ki sàkk asamaan ak suuf.

bul ragal, yaw laa àndal, bul tiit, maay sa Yàlla; maa lay dooleel, dimbali la déy, maa lay téyee sama ndijooru njekk déy.

¶ Sadarag Mesag ak Abet Nego ne Buur Nabukodonosor: «Buur, soxlawul ñu di la lay dara.

Luke 12:4 TSK

¶ «Maa leen ko wax, yeen samay soppe, buleen ragal ñu manul lu wees rey seen yaram, ndax gannaaw loolu dootuñu leen manal lu ko raw.

Ci Yeesu, ci kaw ngëm gu nu ko gëm lanu ñemee àgge fit wu mat sëkk, fa kanam Yàlla.

¶ Léegi nag bokk yi, am nanu sañ-sañu dugg ca bérab bu sell baa sell, ngir deretu Yeesu,