TSK

TSK · Hosea 2:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Aaróona ne leen: «Tekkileen boog, indil ma seen jaaroy wurusi nopp, yi ci seeni jabar ak seeni doom, góor ak jigéen.»

Job 19:8 TSK

Manumaa jàll, Yàllaa fatt sama yoon, lëndëmal samay jaaruwaay,

Biiñ ñàkk na, garabu reseñ lax, bépp xol bu tooyoon, binni.

Doom a ngi taxan, baay di taal, jigéen di not lu mu nàkkal ki ñuy wooye Lingeeru asamaan, di tuural ay naan yeneen yàlla, di ma ko naqarale!

Yaa tànn ci sa yére yu yànj, rafetale sa jaamookaayi tuur, ba noppi di ca gànctu; lu masula am te du amati mukk.

xanaa ngay diirook Boroom asamaan, bay santaane ñu indil la ndabi këram, nga di ci naan biiñ, yaak say jawriñ ak say soxna ak say nekkaale, ngeen di sàbbaal ay yàllay xaalis ak yu wurus ak yu xànjar ak yu weñ ak yu bant ak yu doj, te du ci lenn luy gis mbaa muy dégg mbaa mu xam dara. Waaye Yàlla ji yor sa bakkan tey ak ëllëg sàbbaaloo ko.

Ngànctu ak biiñ bu yàgg ak bu bees, moo yóbbu seenum xel.

Israyil di reseñ gu naat, meññal boppam lu ne gàññ, te lu meññeef ma gëna yokku, mu gëna yokkati sarxalukaayi tuur. Lu am réewam gëna baaxle, mu gëna baaxal ay xeri tuur.

Moo tax muy rendil mbaalam ab sarax, di taalal ab caaxam saraxu cuuraay, te naan moo niinal njëlam, duunal ab dundam.

Luke 16:1 TSK

¶ Yeesu neeti ay taalibeem: «Jenn waay ju am alal la woon, ñu boole ko ak ab saytukatam, ne ko day pasar-pasaree alalam.

¶ Gannaaw ràññee Yàlla jaralu leen dara, Yàlla it bërgal leen ak seen xel mu doyadi, ba ñuy def jooju jëf ju jekkadi.