Léegi nag maa ngi dellu ca saay bokk, waaye kaay, ma xamal la li xeet wii di def saw xeet, fan yu mujj ya.»
TSK
TSK · Hosea 3:5
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ba Israyil gépp gisee na leen Buur tanqamloo, dañu koo tontu ne ko: «Ana lu nu bokk ak Daawuda, lu nu séq ak doomu Yese? Bànni Israyiloo, ca seeni xayma! Yaw askanu Daawuda, xoolalal sa bopp sa kër.» Ba mu ko defee bànni Israyil dellu ca seeni xayma;
Fan yu mujj ya, dees na taxawal tundu kër Aji Sax ji, Aji Sax ji mooy gëna kawe ci tund yi, tiim tund yu ndaw yi, xeet yépp riirandoo, wutsi ko.
Teewluleen te dikk fi man. Dégluleen, ba mana dund, ma fas ak yeen kóllëre gu sax, gi ma baaxee Daawuda ci ngor gu wóor.
Yeen doom yu woyof kumba yi, waññikuleen, ma fajtal seen woyof kumba.»
Waaye seen Yàlla Aji Sax ji lañuy jaamu ak seen buur bi ma leen di falal, mu toogal Daawuda.
Bés dina ñëw déy, wattukat yéenee fa kaw tundu Efrayim ne: ‘Aycaleen nu yéegi tundu Siyoŋ, fa sunu Yàlla Aji Sax ji.’ ”»
¶ Aji Sax ji déy dafa wax ne: «Daawuda du ñàkk mukk ku ko wuutu ci jalu Israyil.
Su ko defee nga fàttliku démb, daldi rus, torox ba ne xerem keroog ba ma lay jot ci mboolem loo def. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.”»
Maa leen di def wenn xeet doŋŋ ci réew mi, ci kaw tundi Israyil, ñoom ñépp bokk benn buur. Dootuñu doon ñaari xeet te dootuñu xàjjalikoo ñaari nguur.
Feek lu yàgg dees na la woo. Bu ay at jàlle ba jeex, yaay songi am réew mu nit ña rëcc saamar, ba jóge ci ay xeeti xeet, dajeji ca kaw tundi Israyil ya yàggoona wéet. Ñooñoo seppikoo ci xeeti àddina yi, ñoom ñépp dëkksi fa ci biir xel mu dal.
Waaye, Buur Nabukodonosor, Yàllaa ngi biir asamaan, di xamle ay mbóot te moo la won liy am jamono yiy ñëw. Sa gént gaak la nga ca gis ca sa kaw lal, lii la:
Seen jur gu gudd ak gu gàtt lañuy àndal, di seet Aji Sax ji, duñu ko gis, te moo leen dëddu.
Ca ngeen naan: «Nan dellu ci Aji Sax ji. Moo nu xotat, te moo nuy wéral. Moo nu duma, te moo nuy takkal sunuy góom.
Fan yu mujj ya, dees na taxawal tundu kër Aji Sax ji, mooy gëna kawe ci tund yi, tiim tund yu ndaw yi, askan yi riirandoo, wutsi ko.
Am dangay sofental mbaaxu Yàlla gu réy, akug jéllaleem, akug muñam, ndax ñàkka xam ne li Yàlla namm ci baaxe la, moo di nga tuub?