TSK

TSK · Hosea 7:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ñooy say jaam, sa ñoñ ñi nga jote sa kàttan gu réy ak sa doole ju bare.

Job 22:17 TSK

te ñoo doon naa Yàlla: «Xiddi nu!» Ñii ana lu leen Aji Man ji di def?

Waxleen lii, yeen ñi Aji Sax ji jot, jote leen ci loxol bañ,

Wóoy ngalla doom yii diy fippukat! Kàddug Aji Sax jee. Ñu ngi nas mébét yu ma diglewul, di digoo digoo yu ma leen xelalul, di tegle bàkkaar ci kaw bàkkaar.

Wóoy ngalla ña wàcci Misra, di wuti wall; di sukkandikoo ay fas, tey yaakaari watiir ndax bare ga, aki gawar ndax lim bu takku ba te xooluñu ci Aji Sell ju Israyil, sàkkuwñu kooku di Aji Sax ji.

Léegi nag yaw Yanqóoba, yaw Israyil mii, Aji Sax ji la sàkk tabax la, dafa wax ne: «Bul tiit, jot naa la. Dama laa woo ci sa tur. Maa la séddoo.

Moo noon: «Sama ñoñ déy ñoom a! Ñee di doom yu dul tas yaakaar.» Mu daldi doon seen jotkat.

Kon waxal boog waa Yuda ak waa Yerusalem ne leen: “Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngi nii di leen tabaxal musiba ci pexe mu ma leen di fexeel. Kon na ku nekk dëpp yoonam wu bon te jubbanti jikkoom aki jëfam.”

Nooy def ba defaatoo mboolem lu nu digoo woon, di taalal cuuraay Lingeeru asamaan, tuur mi, di ko tuural ay naan, na nu ko daan defe naka jekk, nook sunuy maam ak sunuy buur ak sunuy kàngam ci dëkki Yudak mbeddi Yerusalem. Teewul dañu daan doyal dugub, di woomle, te gisunu loraange.

¶ «“Gannaaw sa mbon googu gépp nag, wóoy, wóoy ngalla yaw! Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.

«Yeen nag ngeen ne: “Boroom bi, ni muy doxale jaaduwul!” Waa kër Israyiloo, dégluleen! Sama doxalin a jaaduwul, am seeni doxalin a jaaduwul?

Hosea 5:7 TSK

Aji Sax ji lañu wor, nde doomi po lañu jur; Léegi la leen màggalug Terutel weer di booleek seen suuf, sànk leen.

Hosea 7:3 TSK

Seenug mbon lañuy bégale buur, seeni fen di bégal kàngam.

Sama Yàlla moo leen di xalab, nde ñoo ko déggalul, te ñooy taxawaaluji ci biir xeeti jaambur yi.

Ci kaw loolu nit ña tiit tiitaange lu réy, ne ko: «Yaw, li nga def lu mu doon?» Fekk na Yunus xamal leen ne Aji Sax ji lay daw.

«Kàddu yu ñagas ngeen teg ci sama kaw,» Aji Sax jee ko wax. «Te yeena ne: “Ana kàddu yu ñu la waxal”?