TSK

TSK · Isaiah 13:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ku jub, jot sa yool ci kaw suuf, moykat beek soxor bi it daw raw.

Bés déy ñeel na Aji Sax ju gàngoor yi, ca lay xaare képp ku bew ak ku reew, ba kuy daŋŋiiral, detteelu.

Waaye wóoy ku bon, nde mooy bonle; la mu def rekk lees koy def.

xanaa di àtte ku ñàkk ci njekk, di dogalal njub, néew-ji-dooley àddina. Mooy dóore àddina, bantub kàddoom, mooy reye ñu bon ñi, ngelawal gémmiñam.

Waajal-leen fi ñuy rendi doom yi, feye leen seen ñaawtéefi baay, bala ñoo jógati, teg àddina loxo, ba tabax fu ne ay dëkk.»

Doxandéem yii diy noon, ni ngay dàqe tàngoor fi bérab bu ne sereŋ, ni ngay dakkale seen coowal xare. Ni aw tàngoor di dakke ndax aw niir, ni la woyu ñu néeg ñi di selawe.

Wooleen fittkatoo fittkat fi kaw Babilon, mboolem kuy tàwwi xala. Gawleen ko, bu kenn rëcc. Feyleen koy jëfam; def ko ni mu def moroomam. Babilon a jaay reewande Aji Sax ji, ku Sell ku Israyil ki.

Léegi nag man, Nabukodonosor, maa ngi sant Boroom asamaan, di ko sargal, di ko màggal. Lu mu def dëgg la, fu mu jaare njub la, te kuy réy-réylu man na laa suufeel.

Ñu xalab ninki-nànka ju réy ja, jaanu cosaan joojee ñuy wax Tuumaalkat bi, di ko wax Seytaane, naxekatu mboolem àddina. Ci kaw suuf lañu ko xalab, mooki malaakaam.