TSK

TSK · Isaiah 13:20

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Mu ne: «Maa koy def kërug siññéel, def ko ab tan, ba buube ko buubub rajaxe.» Kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi.

guddeek bëccëg, du fey, saxar sa day gilli ba fàww, réew ma gental giiru jamono, te deesatu fa jaare mukk.

Aw xeet kay ay bawoo bëj-gànnaar, dal fi seen kaw. Ñooñooy gentalsi seenum réew, ba kenn dootu fi dëkk, nit ak mala, ne mott, ne mes.

«Songleen réewum Meratayim ak waa Pekodd, jam leen, faagaagal seen gannaaw.» Kàddug Aji Sax jee. «Defleen mboolem li ma leen sant.

Kon dégluleen pexe mi Aji Sax ji waajal Babilon, mébét yi mu mébétal réewum Kaldeen ñooñu! Ndegam deesul wommat seen gàtt yu ndaw, yóbbu, ba yàq parlu ma yaxeet.

Suuf a fuddu, wañaaru, mébéti Aji Sax jeey sottalal Babilon, ngir réew ma dib gent bu kenn nekkul.

ay dëkkam gental, réew mi ne sereŋ, di ndànd-foyfoy, kenn du ko dëkke, doom aadama du fa jaare.

¶ Ba loolu amee malaaka mu am doole yékkati doj wu mel ni doju wolukaay wu mag, sànni ko biir géej, daldi ne: «Babilon dëkk bu mag bi, nii lañu koy sànneek doole, mu ne meŋŋ.