TSK

TSK · Isaiah 13:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ana nu ngeen di def keroog bésub mbugal ba, keroog ba safaan di bawoo fu sore? Ana ku ngeen di daw wuti wallam? Ana fu ngeen di denci seen teraanga?

Waa dëkk ya ne yàcc, jàq, torox, mel ni gàncaxu àll mbaa ñax mu yees, mbete caxum xadd mbaa tool bu car jógagul.

Buuru Babilon dégg riir ma, yoxo ya yoqi, njàqare ne ko taral, mu jàq ni kuy matu.

«Yaw nit ki, jàkkaarlool ak Yerusalem, nga sànni kàddu bérab yu sell yi te nga wax waxyu ci kaw réewum Israyil.

Nahum 1:6 TSK

Bu sànjoo, ana kuy taxaw? Ana kuy dékku tàngooru meram? Am sànjam a naan soteet ni sawara, doj yi rajaxoo fi kanamam.

Dëkk bi lees di raatale, maasale, mu ne faraas, fit rëcc, óom yiy fenqe, ndigg yépp di kall-kalli, kanam yépp di sël-sëli.