TSK

TSK · Isaiah 19:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ca suba sa ba biiñub Nabal giifee, jabaram wax ko la xew, fit wa jekki dee goyy ca biir dënn ba, yaram wa daldi mel niw doj.

Absalom ak waa Israyil gépp daldi ne: «Ndigalal Usay, Arkeen bii kat, moo gën ndigalu Ayitofel.» Booba Aji Sax jee nara indil Absalom musiba. Moo tax mu neenal pexem Ayitofel mu jub ma mu laloon.

Job 5:13 TSK

Keey kepp boroom xel cig muusam, ba pexem ndëngteem teela sooy.

di jang, di kayaŋ-kayaŋi niy màndikat, pexe jeex.

Am na ñu naan: «Laajleen ñiy gisaanee nit ñu dee, ak boroom rawaan yiy kebetook a ŋun-ŋuni. Aw xeet sañ nañoo gisaanee seeni tuur, tey diis ñi dee mbiri ñiy dund.»

Nit ñaa ngi yéeg jëm kërug jaamookaay ga ca Dibon, ngir jooyi ca bérabi jaamookaay ya, Mowab a ngay yuuxoo kaw tundu Nebo ak Medeba, boppoo bopp dib nel, sikkimoo sikkim xuufu,

Kàngam ya fa Cowan dañuy teqlikook seen sago, diglekati Firawna yu xelu ya di digle ag ndof. Ma ne: «Yeen diglekat yi, nu ngeen mana waxe Firawna naan: “Nun ay boroom xel lanu, sosoo ca buur ya woon”?»

Jàppool say jat rekk ak sa xërëm yu ne xas yoo dale sonn ba ngay ndaw. Jombul mu amal la njariñ, mbaa ñu ragale la ko.

Lu Apis di daw? Lu tee seen yàllay yëkk jooju taxaw? Xanaa Aji Sax jee ko bëmëx!

Mbaa keroog bés ya may jëflanteek yaw, dinga am fit ak doole joo ko dékkoo? Man Aji Sax ji maay wax, jëfe ko.

¶ Ma ne ko: «Beltasar, kilifay taryaax yi, man ci sama bopp xam naa ne xelum yàlla yu sell yaa ngi ci yaw, te menn mbóot jaaxalu la. Peeñum gént gi ma gént, wax ma piri mi.

Ndaxte xam-xamu àddina sii, ndof la fa Yàlla. Moo tax bindees na ne: «Mooy kiy jàpp ñi muus ci seen pexey muusaatu,»