TSK

TSK · Isaiah 21:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Job 37:9 TSK

ngëlén bawoo néegam sedd ba tukkee fa ngelawi bëj-gànnaar.

Coowal mbooloo ngoog ca tund ya, mel ni ñu baree bare! Riirum nguuri nguur yu daje, di xeeti xeet! Aji Sax ji Boroom gàngoor yi mooy dajale gàngooru xare.

Maa ngii di xabtal fi seen kaw waa Medd, ñi xintewoowul xaalis, faalewuñu wurus.

¶ Aji Sax ji kay mooy yërëm askanu Yanqóoba, dellu taamu xeetu Israyil wii. Moo leen di sancaatal fa seen suuf, doxandéem yi fekki leen; boole seen bopp ci askanu Yanqóoba.

Mu ne: «Maa koy def kërug siññéel, def ko ab tan, ba buube ko buubub rajaxe.» Kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi.

Yaw janq Babilon, wàccal, toog ci pënd bi. Yaw dëkkub Kaldeen bi ci taar bi laa ne, toogal fi suuf, amatoob jal. Dootoo dégg «Lewet, xay.»

Géej ay mëdd Babilon, mu sàngoo gannaxam yu jallaañoo,

Mooy ànd ak ñoñam, di ñi gëna néeg ci yéefar yi, dikk yaqtesi réew mi; ñooy boccil Misra saamar, ba feesal réew mi ay néew.

Ca mujug jamono buur bëj-saalum dina fenqoo ak buur bëj-gànnaar. Te itam buur bëj-gànnaar dina mel ni ngëlaani, ne milib ci kawam, ànd ak watiiri xare aki gawar ak gaal yu mag yu bare. Dina dugg ci ay réew, bëtt, jàll nim wal.