TSK

TSK · Isaiah 21:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Mise ne ko: «Giñ naa ci Aji Sax ji, Kiy Dund, li ma Aji Sax ji wax rekk laay wax.»

Gubi bele, dees na ca jaare watiir, waaye deesu ci dëkk; watiir ngay takk, bàcce ko pepp, waaye doo ko bàcc ba mu far mokk!

Yonent bu ci am gént, na nettali géntam, waaye ku ci am sama kàddu, na ko àddoo, na ma ko waxe. Ana ñax akum pepp?» Kàddug Aji Sax jee.

«Yaw nit ki, tabb naa la wattukatub waa kër Israyil. Nangool sama gémmiñ kàddu, artool ma leen ko.

«Yaw janq Siyoŋ mu taaru, jógal bàcci leen, sa béjjén laay def ag weñ, say wewi tànk, ma def ko xànjar, nga rajaxe xeet yu bare.» Yaay faagaagal seen alal ju lewul, ñeel Aji Sax ji, seen koom ñeel Boroom àddina sépp.