Ngoon a ngay jot, tiitaange ne jaas, balaa bët a set lépp jeex. Lii mooy añub ñuy sëxëtoo, lii mooy deminu ñiy nangu sunu alal.
TSK
TSK · Isaiah 21:12
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Yeremi teg ca ne: «Yeen ndesu Yuda, Aji Sax ji wax na leen ne leen: “Buleen dem Misra.” Nangeen xam xéll nag ne àrtu naa leen bésub tey.
Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: «Céy wii ay, guléet wii ay! Mu ngii di dikk.
Àpp mat, bés jege. Bu ca jëndkat tala bég, bu ca jaaykat tala naqarlu! Am sànj a dikkal askan wépp.
¶ «Lii moo tax yeen waa kër Israyil, ma di leen àtte, ku nekk ciy jëfam. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. Dëppleen te dëddu mboolem seeni tooñ, ngir seenu ay bañ leena gàllankoor.
¶ Ba mbooloo ma déggee loolu, naqar wu mel ni jam-jamu xol la leen def. Ñu ne Piyeer ak ndaw ya ca des: «Bokk yi, nu nuy def nag?»
Yàlla nag jéllale na janti ñàkka xam googa woon, waaye tey mu ngi woo ñépp, ak fépp fu ñu féete, ngir ñu tuub.