TSK

TSK · Isaiah 25:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Job 5:15 TSK

Yàllaay musal néew-ji-doole ci saamaru làmmiñ ak loxol boroom doole,

Ñu ngi naa: «Sunu làmmiñ lanuy daane, nook sunu kàddu; ku nu manal dara?»

Buur di àtte néew-ji-dooley xeet wi, di wallu doomi néew-ji-doole tey dëggaate kiy nennoo.

Ku dëkke kiiraayu Aji Kawe ji yaa këroo keppaaru Aji Man ji.

Éy Aji Sax ji, damaa langaamoo sa kàdduy seede, ngalla bu ma rusloo.

di mbaar mu ñuy serloo tàngooru bëccëg, di ko seeloob taw ak waame.

Lees di tontu xeet wi yónnee di laaj, xanaa ne leen Aji Sax jee sanc Siyoŋ, te fa la baadooloy ñoñam di rawe.

Xanaa ku langaamoo sama kiiraay te jàmmook man, ba jàmmook man.

néew-doole yi dellu bége Aji Sax ji, ñi gëna ñàkk di bànneexoo Aji Sell ju Israyil.

ba sama bokk yi dëkke sancub jàmm, ci dëkkuwaay yu wóor, dal-lukaay yu dal xel.

Ku ni mel, bérab bu kawe lay dëkke, doj yu ñu dàbbli di rawtoom, dundam doy, te ndoxam du ñàkk.

¶ Ba loolu amee malaakam Aji Sax ji dikk, fàdd ca dalub Asiri téeméer ak juróom ñett fukk ak juróomi junni (185 000). Ca ëllëg sa ña mucc teela xëy, yemuñu ci lu moy ñooña ñépp diy néew.

Mboolem yooyu, sama loxoo ko sàkk; nii la lépp ame.» Kàddug Aji Sax jee. «Ku mel nii laay niir: néew-ji-doole ji xolam jeex, te muy déglu sama kàddu bay lox.

waxal raaxkati weexal yi, ne leen: ‘Tata jeey màbb, nde waameey wal, ponkali doji yuur ne yureet, ngëlén riddi, bëtt tata ja!’