TSK

TSK · Isaiah 28:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Tooke lañu ma leel, ma mar, ñu nàndal ma lu forox.

Nanga dërkiisal xoli askan wii, fatt seeni nopp, taf seeni gët; lu ko moy seeni gët gis, seeni nopp dégg, seen xol yég, ñu dëpp, wér.»

Ñu baree cay tërëf, daanoo njaaxaanaay, damm, mbaa ñu sërëx, keppu.»

Waaye yéeneb waxyu bu Aji Sax ji, buleen ko fi tuddati. Jooju wax déy, yenu boroom lay doon. Ndax dangeena been sunu kàddug Yàlla, Yàlla Aji Sax jiy dund, Boroom gàngoori xare yi.

Naa ko bindal sama fukki junniy ndigali yoon, yëfi jaambur lees koy jàppe.

Teewul muy ci ñii, xetu ndee gu jëme ci ndee, te di ci ñee, xetu dund gu jëme ci dund. Boobu sas nag, ana ku ko àttan?

Loolu la bind ci mboolem bataaxal yi mu waxe ci moomu mbir, te mu am ci ponk yu jafee xam, ba ñi dese am njàng te seenum xel toogadi, di walbati waxam, ni ñuy def ak yeneen bind yépp, ba far sànk seen bopp.