TSK

TSK · Isaiah 29:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ba mu ko defee Daawuda dëkk ca biir tata ja, wooye ko Kër Daawuda, ba noppi tabax fa ko wër fépp, dale ko ca sëkkub Milo, ba ca biir.

Seeni Terutel weer ak seen bési màggal laa bañ ci sama xol; yooyu màggal a ma diis ba àttanatuma ko.

Ñi ñu yaakaar dañuy tiit, ne wëqet, seeni kilifa jàq, ba daw wacc raaya ba. Kàddug Aji Sax jee, Boroom sawara wi ci Siyoŋ, Boroom taal bi ci Yerusalem!

¶ Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, Yàllay Israyil dafa ne: «Seen juru saraxu rendi-dóomal, dollileen ko ci seen yeneen sarax, te lekk yàpp wi.

Lakkukaayu sarxalukaay bi ab kaare la, wet gu ci nekk di fukki xasab ak ñaar.

Ñooy sarxe jur gi ñu may jooxeel, lekk yàpp wi, Aji Sax ji buggu ci dara. Maay bàyyi xel ci seen ñaawtéef, mbugale leen seeni moy, te ñoom Misra lañuy dellu.

Amos 4:4 TSK

Aji Sax ji nee: «Demleen Betel, bàkkaare fa, dem Gilgal, bàkkaareeti fa. Rendileen seenub sarax ca ëllëg sa, joxe seen saraxi fukkeeli alal ca gannaaw ëllëg sa,

¶ Yoonu Musaa takkndeeru xéewal yiy ñëw doŋŋ a ci nekk, waaye xéewal ya ci seen bopp nekku ci. Looloo tax sarax yi yoon wi laaj ñu war koo saxoo jébbale at mu nekk, manula setal mukk wecc ñiy jaamusi.