TSK

TSK · Isaiah 32:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

seen noon yi Aji Sax jiy yebal ci seen biir, ñoom ngeen di jaamuji ci biir xiif, ak mar ak rafle, ak gépp ñàkk. Aji Sax jeey teg yetu weñ ci seen ndodd, ba sànk leen.

ba mana làquji ca xunti ya ak xarantey doj ya, ba sore tiitaange ji Aji Sax ji sabab, sore darajay màggaayam, kera buy taxaw, ba suuf di lox.

nit ña sol saaku, di ñaawlu fa mbedd ya, ak kaw taax yaak pénc ya, ku ne di jooy ba say rongooñ wale.

Moo ma tax ne: «Buleen ma xool, damay naqarlu, jooy. Tàyyileen maa dëfal ci sama bokk yi sànku.»

Yaw janq Babilon, wàccal, toog ci pënd bi. Yaw dëkkub Kaldeen bi ci taar bi laa ne, toogal fi suuf, amatoob jal. Dootoo dégg «Lewet, xay.»

Éey bokk yi, sol-leeni saaku, diwoo dóom, ñaawloo ko. Ñaawluleen ni kuy dëj benn bàjjo te jooy jooy yu metti, nde yàqkat bi day jekki, ne sunu kaw dàll!

Hosea 2:3 TSK

Nanga wooye sa bokk yu góor: “Ñoñi Aji Sax ji,” sa bokk yu jigéen, nga ne leen: “Ñi Aji Sax ji yërëm.”

Micah 1:8 TSK

Lee ma tax di jooy ak a yuuxu, ne duŋŋ, deme tànki neen, di ko ñaawloo. Naa yuuxu nig till, naa sab sabum looy ndaxu naqar.

James 5:5 TSK

Dund gu nooy ak bànneexu bakkan daal ngeen nekke ci kaw suuf, di yaflu ci bésub rendi.