¶ Da ne leen: «Bu ngeen farloo ci déggal seen Yàlla Aji Sax ji, di def li mu rafetlu, di teewlu tey jëfe ay santaaneem, di sàmm bépp dogali yoonam, su boobaa duma leen teg lenn ci jàngoro, yi ma tegoon waa Misra, ndax man maay Aji Sax, ji leen di wérloo.»
TSK
TSK · Isaiah 33:24
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Aji Sax jee leen di dumaa taabi Misra, ak neewoy kërug suuf, ak yaram wu xas, ak ër yuy xasan te dungeen mana am pajam.
Weer day leer ni jant, jant gënatee leer, mel ni juróom yaari bëccëg, bésub keroog ba Aji Sax jiy takk damm-dammu ñoñam, fajal leen góom yi ay dóoram sabab.
Su boobaa seen leer feq ni njël, seen góom gaawa wér, seen njekk jiitu leen, leeru Aji Sax ji féete leen gannaaw.
Su bés baa, ci yooyu fan,» kàddug Aji Sax jee, «dees na seet fi Israyil lu ñaaw, du fi am; fi Yuda it, deesu fi gis bàkkaar. Maay jéggal moos ndes wi ma fi saxal.
Ana Yàlla ju mel ni yaw, di bale ag tooñ, di jéllale ag moy, ñeel ndesu ab séddoom. Kii du denc mer ba fàww, te moo bëgg di yéwéne.
Bésub keroog Aji Sax jeey doon kiiraayal waa Yerusalem. Ñi gëna néew doole ci ñoom sax ñook Daawudaay tolloo doole, waa kër Daawuda jiite leen ni Yàlla, ni malaakam Aji Sax ji.
di tuuru ci digg péncu dëkk bi. Ci ñaari tàkki dex gi, garabu dund a ngi ci, di meññ fukki yoon ak ñaar, weer wu nekk benn yoon, xob yi di faj askani àddina.