Mooy bawoo fu sore, fa asamaan digalook suuf. Aji Sax ji laak gàngoor gi muy mbugale, ngir yàqtesi réew mi mépp.
TSK
TSK · Isaiah 34:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Te tundoo tund wu kawe, wu mag ak wu ndaw, wali ndox a cay wale, keroog bés ba deret di tuuroo tuuru, tata ya jóoru.
Sawara déy la Aji Sax ji di mbugale, saamaram ba dal mboolem doom aadama, ñi Aji Sax ji bóom ne xas.
riir ma àkki cati àddina, ngir layoob Aji Sax jeek xeet yi, moom miy àtte mboolem boroom bakkan, ñu bon ñi, mu jébbal saamar.» Kàddug Aji Sax jee.
Aji Sax ji mooy Yàlla ju fiir, te mooy mbugale, Aji Sax ji mooy mbugale, te di boroom sànj. Aji Sax ji mooy mbugal ay bañam, mooy sànju ci kawi noonam.
Su boobaa la Aji Sax jiy génn, xeex ak yooyu xeet, ni mu baaxoo xeexe ci bésub xare.
¶ Sànjum Yàlla fa asamaan lay dale feeñ, ba wàcc ci mboolem ngëmadi, ak njubadiy nit ñiy fatt ag dëgg ci biir ag njubadi.
Meneen malaaka génne ca néeg Yàlla ba, daldi àddu ca kaw, wax ak ki toog ci niir wi, ne ko: «Dawalal sa sàrt te góob, ndaxte ngóob jot na, ngóobum àddina ñor na.»
Dañuy sam déndub suuf sépp, daldi yéew dalub nit ñu sell ñi ak dëkk bu jar bi. Ci biir loolu sawara wàcce asamaan, lakk leen.