TSK

TSK · Isaiah 35:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Asamaan lay fenke cat lii, wëndeelu, sowi cat lee; amul lu rëcc tàngooram.

Aji Sax jee baax, rafeti dogal, di gindi moykat ci yoon wi,

Yoonu ku jub day leer, ba ne ràññ ni bëccëg.

naan: «Képp ku téxét, jàddal ba fii!» Ku ñàkk bopp, mu ne ko:

def kow yoon, ñeel ndesu ñoñam, ña dese fa Asiri, mu mel ni yoon wa ñeeloon Israyil, bésub keroog ba ñuy génn réewum Misra.

di dégg kàddu guy jibe seen gannaaw, naa leen: «Yoon waa ngii, jaareleen fi;» bu ngeen awee ndijoor, mbaa càmmoñ.

Baat a ngi jib, naan: «Xàll-leen yoonu Aji Sax ji ci màndiŋ mi, fàkkal-leen sunu Yàlla xàll wu jub fi joor gi.

Maa ngii di def lu yees, te mu ngii di feeñ xaat! Ràññeewuleen koo? Biir màndiŋ mi kay laay xàllu yoon; fa ne sereŋ, ma walal ay dex;

Yewwulee, yewwul, Siyoŋee, làmbool sa doole! Yerusalem, dëkk bu sell bi, solul ba ne ràññ! Ndax du kenn ku xaraful mbaa ku sobewu ku lay songati.

Dees na ne: «Maasaleleenoo, maasaleleen, yaatal leen yoon wi, te jële luy pakk ci sama yoonu ñoñ.»

Jàllsileen, jàllsileen bunti dëkk bi, xàll-leen yoonu xeet wi, maasaleleenoo, maasaleleen ngér mi, dindi doj yi! Yékkatileen raaya ju askan yépp gis.

«Sampal ay xàmmikaay ci yoon wi, teg fi say màndarga. Booy dem, defal sa xel ci yoon wii, ñall wii nga topp. Israyil mu taaru mi, ñibbsil, ñibbsil sa dëkk yii.

Su bés baa, ci yooyu fan,» kàddug Aji Sax jee, «bànni Israyil ay ànd ak Yudeen ñi, dikk di jooy, di sàkku seen Yàlla Aji Sax ji.

Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: «Bépp doxandéem bu xaraful ci xol, xaraful ci jëmm, bumu duggati sama bérab bu sell bi, muy doxandéem bu mu mana doon, bu dëkk ci biir bànni Israyil.

Bésub keroog jóolóoliy fas yi sax dees na ci bind: «Sell na ñeel Aji Sax ji.» Te ni ndabi tuurukaay yi fi kanam sarxalukaay bi selle, cin yi gëna néew daraja ci biir kër Aji Sax ji sax noonu lañu selle.

¶ Ndax yiwu Yàlla kat feeñ na, te looloo indil ñépp ag mucc.

¶ Sàkkuleen jàmm seen diggante ak ñépp, te it sàkkuleen sellnga, nde ku sellul du gis Boroom bi.

¶ Waaye yeen nag yeen ay giir giy tànneef, yeenay sarxalkati Buur, yeen ay askan wu sell, yeen ay xeet wi ñu jot, ngir ngeen biral jaloore yu wéet yi ñeel ki leen woo, génnee leen cig lëndëm, indi leen ci leeram gu yéeme.

Loolu moo leen taxa teew fi kanam ngàngunem Yàlla, di ko jaamoo biir màkkaanam guddi ak bëccëg, te ki toog ci ngàngune mi moo leen di yiir.