TSK

TSK · Isaiah 41:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Mu am bés Teraa ànd ak doomam Ibraam ak sëtam Lóot, mi Aran di baayam, ak Sarayi, soxnas Ibraam. Ñu bokk jóge Ur gu Kaldeen ña, jëm réewu Kanaan. Ba ñu demee ba Karan, daldi fay sanc.

¶ Ba Ibraam déggee ne jàpp nañu Lóot ma muy baayam bu ndaw, fa saa sa daa dajale dagam, yi juddoo këram te tollu ci ñetti téeméer ak fukk ak juróom ñett (318), ñu dàq buur ya ba dëkk ba ñuy wax Dan.

Ma wol, ba ñu doon pënd, dër, note ni banu mbedd.

Ba ñu sampoogul, toogaguñu sax, ba seeni reen di riigu, ca la leen Aji Sax jiy wal, ñu wow, ngëlén buub, yóbbu ni boob.

Maa yékkatee nit bëj-gànnaar, mu bawoo penkub jant, di tudd sama tur. Mooy note boroom dëkk ni ban mbaa binit bu defarkatu njaq di dëggaate.

Man maay yékkati Sirus ci biir njekk, xàllu yoonam. Moom mooy tabax sama dëkk, yiwi sama ñoñ ñi ñu toxal, te du laaj pey mbaa neexal.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.

¶ Melkisedeg moomu doon buurub Salem te nekkoon sarxalkatub Yàlla Aji Kawe ji, ba Ibraayma délsee jóge xareem baak buur ya mu duma, kooku moo ko gatandu woon, ñaanal ko.