TSK

TSK · Isaiah 44:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Foofa ngeen di jaamoo ay yàlla yu loxoy nit sàkke bant, mbaa doj, yàlla yu dul gis, du dégg, du lekk, du xeeñtu.

Gàcce ñeel na kuy jaamu jëmmi tuur, di puukarewoo ay yàllantu. Yeen yàllay xeet yépp, sujjóotal-leen kii,

Ñi sàkk yii tuur, yal nañu mel ni ñoom, ñook ñi leen wóolu ñépp.

Bésub keroog booba, yàllantuy xaalis ak wurus ya nit sàkkal boppam, di leen sujjóotal, ñoom lay sànni ca jaar yaak njugub ya,

Ma ne, yeen daal, dungeen tus; seen liggéey du dara, te ku leen taamu di ku seexluwu!»

Ñi wóolu ay jëmmi tuur, naan jëmm yu ñu móol: “Yeenay sunuy yàlla,” dees na leen waññi, torxal leen.

Indileen ñii diy silmaxa te ami gët; tëx te ami nopp.

Kee di jur gu fore ab dóom, xelam nax ko, sànk ko. Du keey musal bakkanam de! Du kee naa: «Xanaa duy caaxaan laa ŋàbb nii?»

Yeen daw-làquy xeet yi, dajeleen, dikk, ànd, jegesi. Képp ku gàddu tuuru bantam, ak kuy ñaan tuur mu ko dul wallu, kooka xamul dara.

Ñii déy a yullee wurus ci mbuus, sàkk xaalis, natt diisaay ba, fey tëgg bu leen ci tëggal am tuur mu ñuy sukkal ak a sujjóotal,

Fu aw xeet masa weccee yàllaam? Moonte duñuy yàlla sax! Moona xeet wi ma séddoo weccoo séen darajay Yàlla te du leen jariñ dara.

ñoom ñii naa bii bant: “Yaay sunu baay,” naan wee doj: “Yaa nu sukk, jur.” Wonuñu ma kanam, xanaa gannaaw, te bu leen musiba dikkalee, ñu naa: “Wallu nu boog!”

Nitoo nit dim sannax, sore xam-xam: te képp kuy tëgg sa jëmmu tuur, yaa añe gàcce. Sa jëmmi weñ ji nga xelli, di neenug neen, noog bakkan, tus!

Yaw Aji Sax ji may dooleel, di ma feg, di ma làq bésub njàqare, yaw la xeet yiy bawoo cati àddina, fekksi la, naan: «Caaxaani neen kay la sunuy maam baaxoo woon, xërëmi neen yu amul njariñ.

Xanaa kay tuur mi yor kaaraangey tata yi lay jaamu, muy tuur mu ay maamam xamul woon. Dina ko jaamoo wurus ak xaalis ak xeer yu jafe ak yeneen gànjar.

«Ana luy njariñal yett jëmmu xërëm ju ki ko sàkk yett, mbaa jëmmu xërëm ju ñu xelli, di ci gëmloo nit ay fen? Sàkk sa yëfi bopp, wóolu ko, xërëm yoo móol te manula wax!

¶ Kon su dee wàllu ñam wu ñu sarxal ay tuur, xam nanu ne ay tuur du dara ci àddina, te Yàlla kenn la.

Seenum xel a tàbbi ag lëndëm, ñu tumurànke dundin wi Yàlla di maye, te umple gi ci ñoom moo tax, ndax seenug dëgër bopp.