Dingeen yàpp seeni doom yu góor, yàpp seen doom yu jigéen ndax xiif.
TSK
TSK · Isaiah 49:15
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Aji Sax ji moom turam wu màgg wi tax na du wacc ñoñam, ndax Aji Sax ji la soob, mu def leen ñoñam.
Mu teg ca ne ko: «Lan la sax?» Ndaw sa ne ko: «Ndaw sii da ma noon: “Indil sa doom, nu lekk ko tey, ëllëg nu lekk sama doom.”
Ni baay yërëme doom, ni la Aji Sax ji yërëme ku ko ragal.
Aji Sax ji nee: «Yanqóoba, baal xel ci lii! Ma ne Israyil, fàttlikul, yaa di sama jaam! Ma bind la, ngay sama jaam, yaw Israyil, duma la fàtte!
Aji Sax ji ne: «Du Efrayim ay sama doom ji ma sopp, gone gi may bànneexal? Lu ma ko gëdd gëdd, di ko bàyyi xel. Moo tax sama xol di ko laaj, ma yërëm koo yërëm.» Kàddug Aji Sax jee.
Ag till sax joxe na weenam, nàmpal doomam, te sama bokk yi mujj néeg ba mel ni bànjóolig màndiŋ.
«Maa soppoon Israyil ba muy ndaw, Fa Misra laa ko wooye, muy sama doom.
¶ Ci wàllu xibaaru jàmm bi, ay noon la Yawut ñi taxawe, te muy xéewal ci yeen ñi dul Yawut. Waaye ci wàllu dogal bi taamu Yawut ñi, ay soppe lañu, te seeni maam tax.