Kaw doj yii laa tollu di leen séen, fi kawte yii laa leen jéere. Aw askan a ngii, dëkke fu beru, te bokkuñu ak xeet yi.
TSK
TSK · Isaiah 5:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ba Aji Kawe ji séddee xeet yi seeni suuf, tasaare doom aadama yi ci àddina, moo àppal xeet yi seen kemi réew, na mu dëppook limeefu goney Yàlla yi.
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di taalif bu ñeel askanu Kore wu góor.
Asamaan, déglul; suuf, teewlul, Aji Sax jeey àddu: «Ay gone laa yar, màggloo leen, ñoom, ñu gàntal ma.
Ana nu biib dëkk yàqoo, mbeteb gànc, te nekkoon dëkkub kóllëre, njubte mate fa, njekk lal fa panaan, tey ñu diy bóomkat!
Lu waral sa xonqaayu mbubb mi, sa yére yi mel ni ku doon dëre dërukaayu reseñ?
Israyil di reseñ gu naat, meññal boppam lu ne gàññ, te lu meññeef ma gëna yokku, mu gëna yokkati sarxalukaayi tuur. Lu am réewam gëna baaxle, mu gëna baaxal ay xeri tuur.
¶ Mu léeb leen lii nag, ne leen: «Garabu figg la nit amoon ci tóokëram. Mu dikk di ko raas-si, gisu ca dara.
Ñooñoo di xeetu Israyil wi xéewloo céru doon doomu Yàlla, xéewloo daraja, xéewloo kóllëre yi, ak ndigali yoon wi, ak liggéeyu jaamu Yàlla gi, ak dige yi;
Ba loolu amee meneen malaaka mi yilif sawara, jóge ca sarxalukaay ba, daldi àddu ca kaw, wax ak malaaka, mi yor sàrt bu ñaw bi, ne ko: «Dawalal sa sàrt bu ñaw bi, nga dagg cëggi reseñ gi ci àddina, ndax reseñ ji ñor na.»