¶ Asamaan si tiim seen bopp nag da naan sereŋ ni xànjar, suuf si ngeen teg seeni tànk, wow koŋŋ ni weñ gu ñuul.
TSK
TSK · Isaiah 5:6
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ci kaw loolu Yonent Yàlla Ilyaas, ma dëkk Tisbi ga ca Galàdd, wax Axab, ne ko: «Giñ naa ci Aji Sax ji, Kiy Dund, di Yàllay Israyil ji may jaamu: at yii nu nekk, du taw te du lay, lu moy dama koo wax ci sama làmmiñ.»
Ndeke lépp a nga saxi dég, fépp fees akum ñax, tabaxu doj ba ko wër màbb.
¶ Ma ne: «Boroom bi, foo àppal loolu?» Mu ne: «Xanaa fii ba seeni dëkk gental, ba kenn dëkkatu ca, ba nit dootu nekk biir kër ya, suuf sa yàqu yaxeet, di ndànd-foyfoy.
Aji Sax jaa ngii di tas àddina, tasaare ko, salfaañe li fi dénd bi, wasaare ñi ko dëkke:
Su boobaa Aji Sax ji tawal lu ngeen ji, may leen pepp mu suuf meññ, sakkan te nangu, seen juri keroog di fore parlu yu yaa,
¶ Kàddug Aji Sax jii dikkaloon na Yeremi, jëm ca maral ma. Mu ne:
Réew mii mépp ay gental, def ndànd-foyfoy, xeet yii yépp di surgawu buuru Babilon diiru juróom ñaar fukki at.
Moo tas mbaaram ni bu doon mbaarum tool, moo rajaxe bérabu ndajeem. Aji Sax ji moo fàtteloo waa Siyoŋ màggal ak bésub Noflaay, te tàngooru meram la xalabe buur ak sarxalkat.
Mu ne: «Maa leen xañ ub taw bu leen may ngóob ci ñetti weer. Ma taw ci bii dëkk, tawuma ca bee. Wii waar tawlu, wee waar lax.
Dinañu fàddoo ñawkay saamar, te dees na leen jàpp njaam, yóbbu ci mboolem xeet yi. Te jaambur ñi dul Yawut ñooy joggati Yerusalem, ba kera àppu ñooñu dul Yawut di mat.
Am nañu sañ-sañu tëj asamaan, ba du taw diiru fan yi ñuy biral waxyu, am nañu itam sañ-sañ ci ndox mi, ngir soppi ko deret, ak sañ-sañu wàcceel suuf wépp xeetu musiba, saa su leen soobee.