¶ Ba loolu amee Ibraayma jël mattum saraxu rendi-dóomal ba, yen ko doomam Isaaxa; moom mu ŋàbb la muy taale ak paaka ba ci loxoom, ñu ànd ñoom ñaar.
TSK
TSK · Isaiah 53:6
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ma woote wall ba tàyyi, sama put gi wow koŋŋ. Ma séentu la, yaw sama Yàlla, ba samay gët giim.
Moona Aji Sax ji la soob, mu dëggaate jaamam bii, teg koy naqar, su nangoo doon saraxu peyug tooñ, gis askanam, aw fanam gudd, te coobarey Aji Sax ji ci moom lay sottee.
Xaj yu tiita tiit lañu, xamuñu suur, te ñooy sàmm yeey! Ñoom ñépp, kenn manu cee xam dara, seen yoonu bopp lañu topp, ak seen amin wu lewul.
«Sama ñoñ ñi réer niy xar, seeni sàmm a leen lajjal, sànk leen fi kaw tund yi, ba tundoo tund, ñu yéegi fa, fàtte seen goorukaay.
Noonu it la Mbind mi indee ne: «Kenn jubul, du kenn sax.
xamleen ne ku waññee bàkkaarkat ci yoonu sànkuteem, musal na bakkanam, te faral na ko bàkkaar yu bare.
Almasi itam benn yoon la daj coono ndax bàkkaari nit ñi, moom miy ki jub moo leen ko defal yeen ñi jubadi, ngir yóbbu leen fa Yàlla; moom lañu rey yaramu suuxam, waaye moo dundaat ci dooley Noo gi.