¶ Booba fekk na àddina yàqu, te fees ak ay, Yàlla teg ci bëtam.
TSK
TSK · Isaiah 59:6
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
guddeek bëccëg ñuy wër, ñaawtéef ak ayib wéttali leen.
Tóokëru Aji Sax ji Boroom gàngoor yi kat, mooy waa kër Israyil. Niti Yuda it ñooy njëmbat li mu safoo. Mu di ko yaakaare njub, njubadi ne jaas. Mu yaakaar njekk, yuuxi njekkar ne jaas.
Wóoy ngalla doom yii diy fippukat! Kàddug Aji Sax jee. Ñu ngi nas mébét yu ma diglewul, di digoo digoo yu ma leen xelalul, di tegle bàkkaar ci kaw bàkkaar.
Defe nga ne njekk nga def, waaye dinaa la weer, te sa jëf du la jariñ.
Du kenn kuy wormaal sa tur, mbaa mu yewwu ba jàpp ci yaw, yaa nu làq saw yiw, yaa nu def ban bu tooy ci sunu biir ñaawtéef yi nu tanc.
Fitnaa taxaw, di yet wuy dóoral coxor. Seen lenn du des, du seen mbooloo, du seen alal, du seen daraja.
Mu ne ma: «Tooñaangey waa kër Israyil ak Yuda moo ëpp loxo lool. Réew maa ngi fees ak deret, dëkk bi fees ak yàqute. Nee nañooy: “Aji Sax ji wacc na réew mi. Aji Sax ji gisul dara.”
Wóoy yeen ñiy jéema fanq bésub njàqare tey woo nguurug fitna!
Yeen sama ñoñ, démb rekk ngeen jóg nib noon; yeena ngi nangoo ci nit mbubbum xewam, fekk muy romb, buggul xare, foogul dara.
Boroom alal yi ci sa biir, aw ay lañu fees, waa dëkk bi di fen, te lu seen làmmiñ tudd ay nax la.
Bésub keroog maay dikke mbugal képp ku aw tuuram tax mu aadawoo di tëb dëxu bunt, ak ñiy feesal seen kër yàllantu ak alal ju aw ay ak njublaŋ maye.
Kàngam yi ci biiram di gaynde yuy ŋar, ay njiitam di tilli timis yu dul pannal,
Ci moomu mbir la Daawuda doon wax, ba muy biral mbégtem nit ku Yàlla waññal ag njub gu jotewul dara ak ay jëfam.