TSK

TSK · Isaiah 60:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Maay sàkkal dëkkuwaay Israyil sama mos, jëmbat ko, mu dëkke ko, ba deesu ko lëjalati, te ñu bon ñi duñu ko sonalati na woon,

Ku maandu, Aji Sax ji yég la, sab cér sax.

Aji jub ay jagoo réew mi, dëkke ko ba fàww.

Su boobaa ku mucc fa Siyoŋ ak ku des fa Yerusalem, ku sell ki lees lay wooye, muy képp ku ñu bind turam, te mu wara dese bakkan ci Yerusalem.

Bu am meññeefam gisee li sama loxo def fi seen biir, dinañu sellal sama tur, sellal ma, man Aji Sell ju Yanqóoba. Dinañu ma wormaal, man Yàllay Israyil,

xeet wii ma bindal sama bopp, te ñooy siiwal sama woy.»

Aji Sax ji, Aji Sell ju Israyil dafa wax, moom mi ko bind, mu ne: «Lu dikkagul, nu ngeen ma ko ñemee laaje; am dangeen may jox ndigal ci samay doom, jox ma ko ci li ma liggéeye samay loxo?

Seen maam Ibraayma laa ne, moom ngeen di xool, xool ci Saarata mi leen meññ. Ba muy kenn laa ko woo, barkeel ko, ful ko.

Ngànnaay lu ñu la mana sàkkal, du sotti, te boroom làmmiñ wu la jógal cib layoo yaa koy tiiñal. Ñiy jaamu Aji Sax ji, looloo di seen cér, looloo di njekk gi ma leen di dikke.» Kàddug Aji Sax jee.

ngir tabb waa Siyoŋ ñiy ñaawlu, jox leen kaala gu wuutu dóom bi ñuy ñaawloo, ak diwu mbégte mu ñu weccikoo seenu tiis, ak mbubbam cant mu ñu weccikoo xol bu jeex, ba ñu naa: «Ñii ñoo di ponkali garabi njekk yi, njëmbat li Aji Sax ji jëmbat, ngir teewal teddngaam.»

Deesatu la wooye «Dëkk bi ñu wacc,» deesatul wooye sam réew «Réew mu gental.» Xanaa ñu wooye la «Dëkk bi ma neex,» tey wooye sam réew «Boroom jëkkër,» nde yaa neex Aji Sax ji, te sa réew mi dina am boroom kër.

Maa leen di toppe bëtu mbaax, ba délloosi leen ci réew mii. Maa leen di defar te duma leen daaneel; jëmbat leen te duma leen buddi.

Moo tax nanga wax ne: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa leen di dajalee fa xeet ya, boolee leen fa réew ya ngeen wasaaroo, ba joxaat leen suufas Israyil.”

Amos 9:15 TSK

Maa leen di jëmbat fi seen suuf, te deesatu leen déjjatee fi seen suuf si ma leen jox.» Seen Yàlla, Aji Sax jee ko wax.

Ndesu Israyil dootuñu ayibal, dootuñu fen, deesatu leen déggal kàdduy wor, ñoom doŋŋ it ñooy for, di goor, te kenn du leen tiital.»

Moo tax nu di ko sante màggaayam, nun ñi jëkka wékk sunu yaakaar ci Almasi.

Ndax kat noo di liggéeyu Yàlla; Yàllaa nu yeesal ci Almasi Yeesu, ngir nu wéye jëf ju rafet, ja mu nu fàgguloon ca njàlbéen, ngir nu di ko jëfe.

Waaye asamaan su bees ak suuf su bees sa njub di dëkki bu keroogee, moom lanuy séentu, na nu ñu ko dige woon.

Képp ku am ndam nag, loolooy doon sab cér. Maay doon sa Yàlla, nga doon sama doom,