te yaw nanga yékkati saw yet, tàllal sa loxo mu tiim géej gi, ba xàll ko, ndax bànni Israyil mana dox ci suuf su wow, jàll géej gi.
TSK
TSK · Isaiah 63:12
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
«Aji Sax ji, sa kàttanu ndijoor a yéeme! Aji Sax ji, sa ndijoor a ne noon ba rajax.
tiitaangeek njàqaree ne milib ca seen kaw. Sa kàttan a tax ñu mel niw doj, ne yàcc, ba kera sa ñoñ jàll, Aji Sax ji, ba kera askan wa nga goreel, jàll,
ndax kat dees na dégg sa tur wu réy, ak sa dooley loxo ak sa kàttanu përëg, bu dikkee ba jublu ci kër gii, ñaan,
Géej nga leen xaral, ñu jaare suuf su wow koŋŋ, ca digg géej ga, ña leen doon dàq nag, nga fél leen, ca biir xóote ya, ñu tàbbi niw doj ci ndox mu baawaan.
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Tóor-tóor yi, di seedeb Sabóor, giiroo ci Asaf.
Moo xar géeju Barax ya yaar, Kee saxoo ngoram!
Maa naa xóotey mbeex mi: “Wowal, te maay ŋiisal say dex.”
Yaa def ay firnde aki kéemaan ca réewum Misra, di ko def ba tey jii ci Israyil, ak ci doom aadama yépp, ba may sa bopp woy wu réy wi nga am tey jii.
Mbind mi moo indi kàddu ga dikkaloon Firawna, ne ko: «Maa la yékkati, te li ko waral mooy lii ci boppam: ngir fésal sama doole ci yaw, ngir itam ñu sàbbaal sama tur ci àddina sépp.»