TSK

TSK · Isaiah 8:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ba loolu weesee ma jaxasoo ak sama soxna, yonent bu jigéen ba, mu ëmb, gannaaw gi mu am ca doom ju góor. Aji Sax ji ne ma: «Tudde ko “Maxer Salal Xas Bas.”

«Aji Sax ji Yàllay Israyil dafa wax ne: Nanga bind cib téere kàddu yi ma la wax yépp.

«Dellul jël beneen taxañu bindukaay, nga dellu bind ca mboolem kàddu ya woon ca taxañ ba Yowakim buurub Yuda lakk.

Aji Sax jee àddu, ne: «Bindal peeñu mi, leeral ko ci àlluwa yi, ba njàng mi yomb.

Malaaka mi natt tata ji, muy téeméeri xasab ak ñeent fukk ak ñeent (144) yu malaaka mi natte, ni ko nit ñiy natte naka jekk, te yemook juróom ñaar fukk ak ñaari meetar (72).