TSK

TSK · Isaiah 9:18

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Mbooloo ma nag mujj di tawat ab coono fi kanam Aji Sax ji. Aji Sax ji dégg ci, am sànjam tàkk, sawaras Aji Sax ji tàkkal leen, ba xoyom la wër dal ba.

¶ Ba mu ko defee mbooloom Israyil séddlikoo, def ñaari xaaj. Genn-wàllu mbooloo ma topp ca gannaaw Tibni, nar koo fal buur. Tibni nag, Ginat ay baayam. Genn-wàll ga ca des ànd ak Omri.

Ku bon sànku; noonub Aji Sax ji, taaru tool bu naat la, bu tàkkee, jeex tàkk.

Boroom doole mel ni boob, la mu liggéey di ferñent, ànd ak moom ne jéppét, te kenn du fey sawara wa.

Moo tax ni boob di jeexe ci sawara, ngooñ xoyomoo ko cib taal, ni la seenub reen di seeye ni lu maxe, seeni tóor-tóor naaw ni pënd. Ñoo gàntal yoonu Aji Sax ji ci gàngoor yi, ñoo sofental kàddug Aji Sell ju Israyil.

Mereetuma tóokër bii, waaye lu ciy dég aki dagg, ma dox wuti ko, xareek moom, boole lépp xoyom.

Xambees na démb ab taal bu ñuy wax Tofet, te buur ba lees ko waajalal; dees koo xóotal, yaatal ko, sawara way tàkk, matt ma ne gàññ, noowal Aji Sax ji nar caa tàkke, di sël-sëli ni walum tamarax.

Bésub feyu la, Aji Sax ji di ca feyoo; mooy at mi Edom di yooloo la mu loroon Siyoŋ.

«Na ku ne moytu dëkkandoom te baña wóolu menn mbokk. Kuy mbokk déy lal nga pexem wuruj, di wuruj; kuy dëkkandoo, sos ngay wéye.

Moo leen tax di naaxsaay ni niiru suba, mbaa layub njël, mbaa mboob mu naawe dàgga ja, mbaa saxar su gillee ci jankub néeg.

Amos 7:4 TSK

¶ Boroom bi, Aji Sax ji dellu ma feeñu. Ndeke Boroom bi, Aji Sax ji day waaja mbugale ñoñam sawara. Mu xoyom xóotey géej mbàmbulaan, bay waaja xoyom réew ma.

Niy taxas la ay noonam di laxasoo, mel ni ñu naan ba màndi, te ni boob mu wow lañuy lakke ba xoyomu.

Seen saxaru sawaras mbugal day saxoo dàkk, di gilli ba fàww. Guddeek bëccëg, ñooñuy sujjóotal rab wi ak jëmm ji ñu ko sàkkal, ak mboolem ku ñu màndargaale turu rab wi, kenn du ci nopplu.»