TSK

TSK · Isaiah 9:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Sa kër ak sa nguur day sax dàkk fi sa kanam, te sab jal day dëju ba fàww.”»

Waaye man Buur Suleymaan du ma teree barkeel; jalub Daawuda it day sax fàww fi kanam Aji Sax ji.»

¶ «Kon rikk waay, yaw sunu Yàlla, Yàlla ju màgg, ji àttan te mata ragal, di sàmm kóllëreek ngor; ngalla bul xeeb mboolem toskare ji dikkal sa ñoñ, muy buur ak njiit, sarxalkat ak yonent, dale ca sunuy maam ba ci nun ñépp tey, ca janti buuri Asiri, ba sunu jonni yàllay tey.

Yaa gëna góorayiwe ci àddina, sa kàddu diw yiw, ndax Yàllaa la barkeel ba fàww!

Yaw Yàlla, sab jal a sax dàkk ba fàww. Njub nga ŋanke sa nguur gi,

tooli tund yu mag yi indil mbooloo mi jàmm, tooli tund yu ndaw yi xéewale leen njekk,

yal na turam sax, ba law fu jant tiim, yal na xeet yépp barkeele ci moom, te di ko ndokkle.

“Damay saxal sa askan ba fàww, samp sab jal sët ba sëtaat.”» Selaw.

Bu yàgg lañu ma dëj, ca ndoorte la, bala suuf a sosu.

Man de, maa ngii, maak xale yi ma Aji Sax ji may, nu diy firnde fi Israyil te diy tegtal yu bàyyikoo fa Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, ki dëkke tundu Siyoŋ.

Aw njebbit mooy saxe fa ëkkub Yese, ab car soqeekoo fa reen ya,

Till ay bokk ak mbote ab dal, segg bokk akub tef ab tëraay, wëllu ànd ak gaynde gu mat, ak juru yar, tuut-tànk jiite leen.

Yaw Aji Sax ji, ku dogu, pastéefu, wóolu la, nga may ko jàmm ju mat, nde moo la wóolu.

Xel moomu it fa Aji Sax ji Boroom gàngoor yi la bawoo. Ndigalam a ni yéemee, pexeem màgge ni!

Yerusalem kay law ndes di génne, aw ndes ay rëcce tundu Siyoŋ, te Aji Sax ji Boroom gàngoor yi mooy sottal loolu ci xéraangeem.

Kii màgge fi kanamam ni njëmbat, te nirook reen bu fette ag kekk. Dub taar, du yànjaay bu nu koy niire, du meloom wu nu koy soppe.

Moona Aji Sax ji la soob, mu dëggaate jaamam bii, teg koy naqar, su nangoo doon saraxu peyug tooñ, gis askanam, aw fanam gudd, te coobarey Aji Sax ji ci moom lay sottee.

Aji Sax ji déy dafa wax ne: «Maa ngii di yóbbu Yerusalem ci jàmm ju mel ni géej, ak waamey koom muy wal, bawoo ci xeet yi. Yeenay tooge luppu Yerusalem, di nàmp, uufu ciy óom, mu di leen raay.

Ndaw su toogadi si, foo àppal sa ciŋiñ-caŋañ ji? Aji Sax ji déy, sàkk na guléet kaw suuf: yees ba mel ni jigéen juy jëflanteek góor.»

¶ «Juróom ñaar fukki ayi bés lañu àppal sa mbooloo ak sab dëkk bu sell, ngir dakkal tooñ gi, jeexal moy gi, jotu ñaawtéef, saxal njubte ba fàww, matal peeñum yonent, ba delloo bérab bu sella sell ag sellngaam.

Nga wax ko ne ko: “Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Nit a ngi nii, Njebbit la tudd, ci bérabam lay jebbee, ba tabaxi kër Aji Sax ji.

Luke 2:11 TSK

Bésub tey jii ca dëkku Daawuda, juddule ngeen ab Musalkat, te mooy Almasi, di Sang bi.

Ndax man maa leen di jox làmmiñ wu ànd ak xel, wu seen benn noon dul mana dàq mbaa di ko weddi.

Moo yónnee kàddoom bànni Israyil, àgge leen xibaaru jàmm, biy maye jàmm ci Yeesu Almasi, miy Sangu ñépp.

¶ Gannaaw nag dees noo jox àtteb ñu jub ci kaw ngëm, jàmmoo nanu ak Yàlla ndax sunu Sang Yeesu Almasi.

ñoo xéewloo itam maam ya; ci wàllu doom aadama it, ci ñoom la Almasi soqikoo, di Yàlla, tiim lépp, te yelloo cant ba fàww. Amiin.

Ndaxte fàww Almasi nguuru, ba kera Yàlla di sukkal mboolem ay noonam ciy tànkam.

Foofa la Almasi tiime lu sore gépp nguur, ak bépp sañ-sañ, ak gépp manoore, ak gépp kilifteef, ak wépp tur wees di tudd, muy tey, di ëllëg.

Deretam ja tuuru ca bant ba, ca la Yàlla defe jàmm, ba sottale ci moom, pexe mi mu jubalee boppam ak lépp, muy lu nekk ci kaw suuf, ak la fa asamaan.

Deesul nàttable moos màggaayu mbóot mii feeñe ci sunu yoonu ngëm: Kii moo feeñe ci yaramu suux, Noowug Yàlla dëggal ko, malaaka ya niir ko; moom lañu waaree ci xeet yi, gëmees na ko ci kaw suuf it, te yéegees na ko fa leer ga.

Waaye Doom ji la Yàlla ne: «Yàlla, sab jal tey la ak ëllëg ba fàww, te sa yetu nguur njub lay doon.

Moom la Ibraayma jox fukkeelu cérub mboolem cëxëtoo ma. Ni ñu jëkka dégge aw turam Melkisedeg, ci tekki, mooy «buur bu jub». Bu loolu weesee itam moom mooy buurub Salem, muy «buuru jàmm».

Ci kaw mbubbam ak ci luppam, aw tur lañu ci bind te moo di: «Buuru buur yi, Sangu sang yi.»