TSK

TSK · James 2:14

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Acts 8:13 TSK

Simoŋ ci boppam gëm, moom it, ñu sóob ko ci ndox. Simoŋ nag bàyyeetul Filib. Ba mu gisee firnde yaak kiraama yu mag yay am, moom moo yéemu.

Acts 15:9 TSK

Yàlla amul xejj ak seen sunu digg ak ñoom, ndax seen ngëm la raxase seen xol.

Su ma jotoon ci kàddug waxyu, boole ci xam mboolem kumpa, ak mboolem xam-xam, ak ngëm gu mat sëkk ba mana toxal ay tund, te jëfewuma cofeel, duma dara.

¶ Yeen de bokk yi, cig yiwiku lees leen woo. Moytuleen lenn rekk: bu seenug yiwiku diw lay, ngir topp seen bakkan, waaye deeleen surgawoonte ngir cofeel.

ak di baamtu fi kanam Yàlla sunu Baay, jëf ji juddoo ci seen ngëm, ak liggéey bi sottee ci seen cofeel, ak yaakaar ji ngeen saxoo di séentu sunu Sang Yeesu Almasi.

Ndax kat tàggat aw yaram, as njariñ a ngi ci, waaye ag njullite, ci lépp lay jariñe, te moo moom digeb àddinay tey ak ëllëg.

Titus 3:8 TSK

¶ Googu kàddu wóor na te damaa bëgg nga sàmmoo dëggal loolu, ngir gëmkati Yàlla yi saxoo def jëf ju baax. Loolu moo baax te am njariñ ci nit ñi.

¶ Ibraayma, ba ñu ko nattoo, ngëm la jooxee Isaaxa ngir sarax. Ibraayma mi ñu jagle dige yi, Isaaxa jenn doomam ju góor ji mu am, moom la doon jooxe,

¶ Doonleen jëfekati kàddu gi, buleen di ay déglukat doŋŋ, di nax seen bopp.

¶ Waaye jombul nit ne: «Yaw, ngëm nga am, waaye man, jëf laa am.» Dama ne, won ma sa ngëm gu àndul ak jëf; man, samay jëf laa lay wone sama ngëm.

¶ Loolu ci boppam wara tax ngeen def lu ngeen man, ba dolli ci seen ngëm, njàmbaar; seen njàmbaar, ngeen dolli ci xam-xam;