¶ Ba ñu demee ba mu yàgg, Firawna buuru Misra dee. Fekk na bànni Israyil a ngay binni rekk ndax seen njaam ga. Ñuy woote wall, ba seen jooy, ya sababoo ca seen toroxteg njaam ga, àgg fa Yàlla.
TSK
TSK · James 5:4
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Bu ngeen leen néewalee déy, bu ñu yuuxoo, woo ma wall, dinaa dégg seen yuux moos.
¶ «Buleen lekk seen àqu moroom, buleen sàcc. Buleen wacc peyu liggéeykat, muy fanaan ci seeni loxo.
Daa mel ni jaam bu namm keppaar mbaa mbindaan mu yàkkamtig peyam.
Ndegam sama tool a ma tuumaale ay jooy, rongooñi toobo yay bas-baseendoo,
Woyleen Aji Sax ji dëkke Siyoŋ, siiwal-leen ay jalooreem ci xeet yi!
Tóokëru Aji Sax ji Boroom gàngoor yi kat, mooy waa kër Israyil. Niti Yuda it ñooy njëmbat li mu safoo. Mu di ko yaakaare njub, njubadi ne jaas. Mu yaakaar njekk, yuuxi njekkar ne jaas.
Doju tata dina riir déy, aw dénk àddoo ca jank ba, feelu ko.
Kon ndax Yàlla man naa baña sàmm àqu tànnéefam ñi koy woo wall guddi ak bëccëg, xanaa di leen yeexe?
¶ Yeen ñiy sang yi, yorleen seeni jaam, yorin wu jub te aw yoon, te ngeen xam ne yeen itam am ngeen ab Sang fa asamaan.