su boobaa ma gën leena mereeti, noonoo leen, te man ci sama bopp maa leen di mbugalati lu ko ëpp fukki yoon ak juróom, feye leen ko seen bàkkaar.
TSK
TSK · Jeremiah 23:39
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Aji Sax ji nag ne: «Yuda itam dinaa ko jële fi sama kanam, ni ma fi jëlee Israyil. Dinaa xalab dëkk bii ma tànn, di Yerusalem ak kër gii ma wax ne sama tur dina fi nekk.»
Ku sofental ndigalu Yàlla, yàqule; ku jëfe santaane Yàlla, yoolu.
Man ci sama bopp maa leen di dëfal. Ana lu ngeen di ragal ci nit kuy dee, doom aadama ju bokk akum ñax aw demin?
¶ Aji Sax ji ne Yeremi: «Su la askan wii laajee mbaa ab yonent mbaa ab sarxalkat ne la: “Ana yéeneb waxyu bi la Aji Sax ji yóbbante?” Nga wax leen ne leen: “Yeenay yen bi te dinaa leen yenniku.”» Kàddug Aji Sax jee.
«Mer dikkal na ma, xadar dikkal ma ci dëkk bii, dale ko ca ba ñu ko tabaxee ba bésub tey, ba tax ma di ko jële fi sama kanam,
Maa koy yen añu ñaawtéefam, mook njabootam aki surgaam. Maay wàcce ci seen kaw, ñook waa Yerusalem ak Yuda gépp, mboolem musiba mu ma leen digoon, te taxul ñu dégg.”»
Ana lu waral nga fàtte nu fàww, ba nu jant yu yàgge nii?
Neel: “Yeen Tundi Israyil, Dégluleen kàddug Boroom bi, Aji Sax ji. Boroom bi Aji Sax ji moo wax lii, jëme ci tund wu mag ak wu ndaw ak xunteeku xur, ne: Maa ngi nii di leen wàcceel saamar, maay màbb seen jaamookaayi tuur,
Mag ñu góor ñeek xale yu góor yi, jeeg jeek janq ji, ba ci tuut-tànk yi, reyleen ñépp, faagaagal leen. Waaye ku ci am rëddu jë, buleen ko laal. Dooreleen ko ci sama bérab bu sell bi.» Ñu tàmbalee bóom mag ña ca kanam kër Yàlla ga.
¶ «Moo tax Boroom bi Aji Sax ji da leena wax ne: Maa ngi nii di àttesi diggante gàtt bu duuf ak gàtt bu yooy.
Man déy ni gaynde laay mel ak Efrayim, ni gaynde gu ndaw laay mel ak waa kër Yuda. Man, man mii maay xotat, wéy, maay yóbbu te kenn du wallu.