TSK

TSK · Job 12:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Job 9:4 TSK

Moo rafet xel, bare doole! Ana ku koy jéema të, mu jig ko?

Job 12:16 TSK

Kee am doole, keey sottal, di boroom aji réer ak ka ko réeral.

Job 32:6 TSK

Ca la Eliyu doomu Barakel waa Buus ba, àddu ne: Man de damay ndaw, ngeen diy mag, ba tax may teeylu, ragal leena biralal sama xam-xam.

Job 36:5 TSK

Dama ne, Yàllaa màgg te du jalaxe, moo màgg te réy um xel.

Sunu Boroom a màgg, bare doole; am xelam wees kemu.

Maa moomi digle, di maye gis-gis; maa am ug dégg, di boroom doole.

Ana ku mana xayma Aji Sax ji? Mbaa nga dib xejjam, ba di ko digal?

Suuf, Aji Sax jee sàkke kàttanam; dun bi, mu sampem xelam; asamaan, mu lale xam-xamam.

Ndax man maa leen di jox làmmiñ wu ànd ak xel, wu seen benn noon dul mana dàq mbaa di ko weddi.

Waaye ci ñi ñu woo, ñuy Yawut, di Gereg, Almasi mooy manoorey Yàlla, di xam-xamu Yàlla.

Ci moom lanu jote sunu muur ci kaw dogalu Yàlla mi nu taamu lu jiitu, moom miy sottal lépp ni mu ko namme ci coobareem.

James 1:5 TSK

¶ Ku desele am xel mu rafet nag, na ko ñaan Yàlla, mu may ko ko, ndax Yàlla mooy yéwéne ñépp te du sikk kenn.