Aaróona tàllal loxoom, mu tiim ndoxi Misra, mbott ya jóg, lal réewum Misra.
TSK
TSK · Job 12:21
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Te itam Aji Sax ji wax na ci mbirum Yesabel ne: Ay xaj dina lekk Yesabel ca wetu tatay Yisreel.
¶ Ba loolu wéyee mu jàll ca biir dëkk ba; lekk daldi naan ba noppi, ne: «Jubluleen ci jigéen ju alku jee te suul koo waay, ndaxte doomu buur la.»
Yàllaa ma nasaxal, torxal ma, ba amatuñook man yemukaay.
Kenn sonnu ci, kenn tërëfu ci, kenn dajjantul mbaa muy nelaw; ngañaay yolomul, waruw dàll dogul.
solal ko sa mbubb, dooleele ko sa ngañaay, teg kilifteefu réew mi ci loxoom, ba mu féete wàllu baay, waa Yerusalem, ak waa kër Yuda.
Bu bésub keroogee Aji Sax ji dikke mbugal gàngoor ya fa kawa kaw, ak buuri àddina yi fi suuf.
Mooy walbati jamono, di soppi demin, di fal buur, di folli. Mooy xelal boroom xel mu rafet, di xamal boroom xel mu ñaw.
¶ Li ci des nag moo di ngeen manoorewoo Boroom bi, te ngeen sàkkoo ndimbal ci dooleem ak kàttanam gi amul kem.