TSK

TSK · Job 21:25

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Xam nga sa baay ak ay nitam. Ay xarekat yu jàmbaare lañu te wex ni gaynde gu ñu nangu doom ya, te it, sa baay ku xam xeex la, du fanaan ak xarekat ya.

Job 3:20 TSK

Boroom tiis, ana lees koy maye leeru kaw suuf? Lu boroom naqar di doye bakkan?

Job 9:18 TSK

mayuma sax ma astandiku, xanaa reggal ma aw naqar.

Job 20:23 TSK

Ba muy sol kollam la ko Yàlla di yónnee tàngooru sànjam, tawal ko ko lu fees déqam.

Nit ku Yàlla may alal, koom ak daraja, te mboolem lu mu namm, ñàkku ca lenn, waaye Yàlla mayu ko mu tal caa lekk, xanaa jaambur di ko xéewloo — loolu cóolóoli neen la, di naqar wu tar.

Mu neeti ma: «Yaw nit ki, maa ngii di dagge fi Yerusalem lépp luy dugub. Ci biir njàqare lañuy lekke as mburu te xol bu jeex lañuy naane siitum ndox.