TSK

TSK · Job 5:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Fekk na ñu wax Daawuda ne ko Ayitofel bokk na ca ña lëngook Absalom. Daawuda nag ñaan ne: «Yaw, Aji Sax ji, ngalla yàqal pexem Ayitofel.»

¶ Ci biir loolu Ayitofel gis ne déggeesul ndigalam, mu takk mbaamam, ñibbi ca dëkk ba mu fekk baax. Mu daldi topptoo mbiri këram ba mu jekk, ba noppi wékk boppam. Mu dee, ñu denc ko ca sëgi baayam.

Ba mu ko defee ñu wékk Aman ca bant ba mu waajaloon Mardose. Merum Buur doora giif.

Ku bon a ngoog, di matu doomu ñaawtéef. Day sos njombe, wasin njublaŋ.

Aji Sax jaa ngi feeñoo, di àtte yoon; ku bon teg ug fiir, tàbbi ca. Na jib ndànk. Selaw.

Defuma dara, ñu di ma fiir, defuma dara, ñu gas um yeer, di ma tëru.

Waa Misra jànnaxe, ma dëpp seen pexe. Ñu seeti yàllantu yeek njuuma yi, ak gisaanekat yeek boroom rawaan yi.

Dees na gàcceel boroom xel yi, ñu jàq, tarsu. Kàddug Aji Sax jaa ngii ñu dëddu, kon ana seenum xel?

¶ Lu jëm ci Edomeen ñi, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Xanaa boroom xel amatul fi Teman? Xanaa ndigal a réer xamkat yi? Am seen bopp a yàqu?

Ndaxte bindees na ne: «Maay yàq xam-xamu xamkat yi, ñi xelu, ma neenal seenum xel.»