TSK

TSK · Joel 1:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Àddinaa ne duŋŋ duŋŋaaral, dees koo futti ba mu ne furaas! Aji Sax ji kat wax na kàddu gii!

Ba kañ la réew mi naa sereŋ, gàncaxu tooloo tool di lax? Rabu àll ak njanaaw a ngi sànku ngir mbonug ñi fi dëkk te naan: «Moom xoolul sunu muj!»

«Waa Yudaa ngi ñaawlu, doole dëddu dëkk yi, ñu ne yogg, ne lasar fi suuf, yuux jollee Yerusalem.

Hosea 4:3 TSK

Moo tax réew mi wowal, mboolem lu fi dëkke ràgg, ba ci rabi àll yi, ak njanaaw yi, jëni géej itam day réer.

Joel 1:5 TSK

Màndikat yee, yewwuleen, jooyoo. Naan-kati biiñ yee, jooyleen biiñ bu bees, bi ñu foqatee ci seen gémmiñ.

Joel 1:17 TSK

Aw jiwu wow na, suule ciy donji suuf, dencukaay yi wéet, sàq yi dàjjiku, am pepp wow.

Maa ngii di yar seen askan, sëlëm leen sébbriit, mi jóge ci seen saraxi màggal, ñu tonniwaale leen ak sébbriit mi.