Ñi jiite askan wii ñoo leen di sànk, ña ñuy jiite loru.
TSK
TSK · Lamentations 2:14
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
«Sarxalkat yi newuñu: “Ana Aji Sax ji?” Ñi ŋank yoon wi faaleetuñu ma, njiit yi gàntal ma, yonent yiy waxe waxyuy Baal, tuur mi, di topp lu leen dul jariñ.
«Ndax ki gëna tuut ba ki gëna mag, ñépp a ngi lewal lu lewul. Yonent akub sarxalkat, ñépp a ngi wor.
¶ Ma ne ko: «Éy Boroom bi Aji Sax ji, yonent yaa ngii di leen wax ne duñu dajeek saamar, duñu xiif te jàmm ju ne ñoyy nga leen di defal fi bii bérab.»
Su ñu teewe woon sama jataay sax, mana dégtal sama ñoñ samay kàddu, ba waññee leen seen yoonu mbon ak seen jëfi mbon.
Maa ngii ci kaw yonent yi.» Kàddug Aji Sax jee. «Ñu ngi mbel-mbeli naan: “Kàddoo ngi.”
¶ «“Kon nag yeen, buleen déglu seen yonent yeek seetkat yeek firikati gént yeek boroom rawaan yeek ñeengokat yi leen di wax, naan leen dungeen tàbbi ci curgag buuru Babilon.
Buleen déglu yonent yi leen di wax naan leen dungeen tàbbi ci curgag buuru Babilon. Ay waxyuy fen déy lañu leen di waxal.
¶ Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoori xare yi kat dafa wax ne: «Seeni yonent ak seen gisaanekat yi ci seen biir, buñu leen nax. Te it buleen déglu seen boroom gént yi ngeen di géntloo,
Te sa yonent yi la doon jottli waxyu, naan la buuru Babilon du dikk ci seen kaw, yaak waa réew mii, ana ñu léegi?
«Yaw nit ki, waxal waxyu ci kaw yonenti Israyil yiy waxe ay waxyu. Nanga wax ñiy waxe waxyu ci seen xelum bopp, ne leen: “Dégluleen kàddug Aji Sax ji: Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
Ay yonentam a ngi déeyoo fi biiram; ñu ngi xiiru ni gaynde guy xotat pàddam, di lekk doom aadama yi, foqati alal ak gànjar, ful jëtun yi ci biiram.
Nit man naa wër, toppi caaxaan aki fen, naan: “Maa lay yégal waxyub biiñ aku ñoll,” te kookooy jottlikatub waxyu bi askan wii yelloo!
ay yonentam reew, diy workat; ay sarxalkatam teddadil sellnga, xëtt yoon.