TSK

TSK · Lamentations 2:17

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ «Waaye bu ngeen ma déggalul te baña jëfe sama santaane yooyu yépp,

Jombul mu am ku dégg kàdduy ngiñ lii, tey nax boppam cim xelam, naan: «Jàmm rekk laay am, maa tey të,» ba tax ñax mu wow lakkaale mu tooy.

Yeen Yesurun, yeena yaflu, waŋŋeetu, solu yaram, ne faaj, ne fuux, fàtte Yàlla mi leen sàkk, faaleedi seen cëslaay li leen musal.

Aji Sax ji, yaw laa yaakaar; Boroom bi, sama Yàlla, yaa may nangul.

Yékkati ngay bañam, noonam yépp di ree.

Aji Sax ji nag indi na ko te def na ko, na mu ko waxe woon. Yeena moy Aji Sax ji, déggaluleen ko ba tax lii dal leen.

Ndeysaan Boroom bee mer ba xiinal Janq Siyoŋ mu taaru mi. Fa asamaan la rattaxe sagu Israyil fa suuf. Keroog bésu meram ma, bàyyiwul xel, ne këram googoo di ndëggastalam.

¶ «Moo tax, dogu naa ci man miy dund, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, gannaaw yeena def seen wépp njombe ak seen jépp jëf ju siblu, di sobeel sama bérab bu sell bi, man itam, maa leen di wat nel te duma leen xool bëtu ñéeblu, duma leen ñeewante.

Man it maa leen di feye xadar. Duma xool bëtu ñéeblu, duma ñeewante. Dinañu yuuxu yuux yu réy, may dégg te duma leen faale.»

Matal nga sa kàddu gi nga wax ci nun, nook sunu kilifa yi nu yilif, ba nga wàccee ci sunu kaw, ci Yerusalem, musiba mu réy mu masula am feneen fu mboolem asamaan tiim.

«Lépp laay buube ba mu set fi kaw suuf.» Aji Sax jee ko wax.