TSK

TSK · Lamentations 3:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Won nga ma ay yoon coonooki tiis, waaye yaa may dundalaat, ma mucc xóotey suuf.

Éy Aji Sax ji, loo may gàntale, di ma fuuylu?

Dees na ko xeeb, daw ko, muy nit ku bare mitit te miin naqar. Mu mel ni ku ñuy dummóoyu, dees koo xeeb te nawloowuñu ko.

Masumaa toogandook ñiy mbumbaay bay xawaare. Yaa ma jiite, ma beru, toog ndax mer mi nga ma sol, ba ma fees.

Ana lu ma doon génne ca biiram, di daj coonooku tiis, mujje gàcce?

Yeen mboolem ñiy jaare yoon wi, lii safu leen, waaye seetleen rekk ba gis ndax wenn mitit dab na mitit wi ñu ma teg, te Aji Sax ji naqarale ma ko ci jantub tàkktel sànjam.